Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 11

Sarxalkat yi 11:29-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29«Bu loolu weesee, leneen lu daganul ci yeen ci rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, mooy kaña ak janax ak xeeti mbëtt yépp;
30ak unk ak bar ak sindax buy yéeg, ak sindax buy dox ci suuf, ak kàkkatar.
31Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
32Te it lu ci dee ba wadd ci kaw lenn, loola day sobewu, nay ndabal bant, mbaa ndimo, der mbaa ab saaku, mbaa jumtukaay bu mu mana doon. Nañu sóob loola ci ndox te du tee mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

Read Sarxalkat yi 11Sarxalkat yi 11
Compare Sarxalkat yi 11:29-32Sarxalkat yi 11:29-32