29 «Bu loolu weesee, leneen lu daganul ci yeen ci rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, mooy kaña ak janax ak xeeti mbëtt yépp;
30 ak unk ak bar ak sindax buy yéeg, ak sindax buy dox ci suuf, ak kàkkatar.
31 Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
32 Te it lu ci dee ba wadd ci kaw lenn, loola day sobewu, nay ndabal bant, mbaa ndimo, der mbaa ab saaku, mbaa jumtukaay bu mu mana doon. Nañu sóob loola ci ndox te du tee mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.