5Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.
6Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,
7di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.»
8Ndaxte Yeesu da ko ne: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.»
9Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
10Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leena dàq ca réew ma.
11Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
12Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.»
13Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni.
14Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew.
15Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
16Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.
17Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew.
18Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom.
19Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.»
20Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
21Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
22Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
23di ko sarxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgga faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
24Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
25Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
26Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.