Text copied!
Bibles in Wolof

MÀRK 5:5-26 in Wolof

Help us?

MÀRK 5:5-26 in Téereb Injiil

5 Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.
6 Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,
7 di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.»
8 Ndaxte Yeesu da ko ne: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.»
9 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
10 Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leena dàq ca réew ma.
11 Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
12 Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.»
13 Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni.
14 Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew.
15 Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
16 Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.
17 Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew.
18 Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom.
19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.»
20 Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
21 Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
22 Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
23 di ko sarxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgga faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
24 Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
25 Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
MÀRK 5 in Téereb Injiil