7Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730).
8Palu moo meññ Elyab,
9Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
10ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo.
11Doomi Kore ya nag deewuñu ca.
12Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi,
13ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi.