Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 24

Màndiŋ ma 24:4-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4kàddug kiy dégg waxi Yàlla, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
5Yanqóobaa, yaaka yànji xayma! Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan!
6Ña nga ne màww ni tooli tàndarma, nirooteek tóokëri tàkkal dex, mbaa garabu alowes gu xeeñ gu Aji Sax ji jëmbat, mbaa garabi seedar yu saxe wali ndox.
7Ndox maay wale cay bagaanam, am jiwoom màndim ndox, buuram nara sut Buur Agag, nguuram jóg ba kawe.
8Yàllaay ki ko jële Misra, féete ko fa ay béjjén féete nagu àll. Mooy warax xeet yi ko jógal, dammat leen, jamat leeni fittam.
9Israyil a ngi yuug ak a goor ni gaynde, mbete gayndeg sibi, ana ku koy yee? Ku ko ñaanal barke, yaay barkeel; ku ko ñaanal alkànde, yaay alku.»
10Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la wooye woon, yaw defoo lu moy ñaanal leena ñaanal, ba muy ñetti yoon nii!
11Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, Aji Sax jee la xañ teraanga.»
12Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen,
13su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax.
14Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»
15Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,
16kàddug kiy dégg waxi Yàlla, kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.

Read Màndiŋ ma 24Màndiŋ ma 24
Compare Màndiŋ ma 24:4-16Màndiŋ ma 24:4-16