13Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.»
14Mu daldi koy yóbbu ba ca toolub Sofim, ca collu tundu Pisga. Ci kaw loolu mu tabax fa juróom ñaari sarxalukaay, sarxalukaay bu nekk, mu sarxalati fa yëkk wu ndaw akam kuuy.
15Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»
16Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
17Mu dem ba ca moom, fekku ko lu moy mu taxaw ca wetu saraxu rendi-dóomalam, mook kàngami Mowab. Balag ne ko: «Lu Aji Sax ji wax?»
18Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne: «Jógal dégloo, Balag, teewlu maa, doomi Sippor.
19Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
20Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam, Yàllaa barkeel, duma ko tebbi.
21Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.
22Yàllaa leen jële Misra, féete leen fa ay béjjén féete nagu àll.
23Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.”
24Wii askan ni gaynde lay jóge, ni gayndeg sibi lay faboo, du goor te yàppul am pàdd, deret ja tuuru, mu xab.»
25Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Boo leen móoluwul benn yoon kay, bu leen ñaanal ba doyal boog!»
26Balaam ne ko: «Xanaa waxuma la woon ne la lépp lu Aji Sax ji wax, loolu laay def?»