19jóge Matana dem Naxaliyel, jóge Naxaliyel, dem Bamot,
20jóge Bamot ba ca xur, wa ca àllub Mowab, àkki nag njobbaxtalu tundu Pisga, wa tiim ndànd-foyfoy ga.
21Ba loolu amee Israyil yebal ay ndaw ca Siwon buurub Amoreen ña, ne ko:
22«May nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jàdde benn tool mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naan ndoxum teen. Mbeddum buur lanuy topp, ba keroog nuy jàll sam réew.»
23Siwon nag mayul Israyil, ñu jaarem réewam, xanaa mu dajale gàngooram gépp, sàqi, ngir dajejeek Israyil ca màndiŋ ma. Mu dikk ba Yaxacc, song Israyil,
24Israyil leel ko ñawkay saamar, nangu seenum réew, dale ko Arnon ba Yabog, ba àgg ca Amoneen ña, ndax kemu réewum Amoneen ñaa fegu woon ba jotuwul.
25Israyil nangu dëkki Amoreen yooyu yépp, daldi sance mboolem seeni dëkk, boole ca Esbon aki dëkk-dëkkaanam.
26Esbon moo doon péeyub Siwon buurub Amoreen ña. Kookoo xare woon ak buuru Mowab ba woon, moo nangu ciy loxoom réewam mépp, ba Arnon.
27Moo tax woykat ya ne: Ayca ca Esbon, ba tabaxees kooti; na dëkkub Siwon jógati.
28Lakk gaa nga jóge Esbon, sawaraa bawoo dëkkub Siwon ba, xoyomi Ar ga ca Mowab, gor ñooña tiim dexu Arnon.
29Mowabee ngalla yaw! Sànku ngeenee, yeen askanu Kemos, mi wacc doomam yu góor, ñu daw, doomam yu jigéen doon jaami Siwon buurub Amor.