19Ndawi bànni Israyil ne ko: «Sél wi rekk lanuy topp, te ndox mu nu naan, nook sunug jur, noo la koy fey. Ñaanunu lenn lu moy doxe sunuy tànk, ba jàll.»
20Mu ne leen: «Dungeen fi jaare mukk!» Ci kaw loolu Edom génn ngir dajeek ñoom, ànd ak gàngoor gu réy, gànnaayu ba diis.
21Noonu la Edom lànke, mayul Israyil mu jaare réewam, ba Israyil mujj teggi.