Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 18

Màndiŋ ma 18:1-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji ne Aaróona: «Yaw, yaak say doom ak sa waa kër maam, yeenay gàddu peyug tooñ ci wàllu bérab bu sell bi, te itam yaw, yaak say doom, yeenay gàddu peyug tooñ ci seen wàllu carxal.
2Te itam sa bokki Leween ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence.
3Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi bérab bu sell bi, ak sarxalukaay bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam.
4Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen.
5Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.
6«Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi.
7Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»
8Aji Sax ji neeti Aaróona: «Man mii maa la sédd ndénkaaneb samay jooxe; mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil indi, yaw laa ko jagleel, nga jagoo, yaak say doom, ci kaw dogal bu sax dàkk.
9Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor.
10Fu sella sell ngeen koy lekke; képp kuy góor ci yeen, sañ na cee lekk. Lu sell lay doon ci yaw.
11«Leneen lu la ñeel moo di jooxe bu jóge ci saraxi nit ñi, di bépp saraxu yékkati-jébbal bu bànni Israyil. Yaw laa ko sédd, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk.
12«Lépp luy ngëneelu diw gu bees, ak ngëneelu biiñ bu bees, ak pepp mu jëkka ñor, mu ñu jox Aji Sax ji, yaw laa ko jox.
13Njàlbéenu meññeef mi ñuy indil Aji Sax ji, ci mboolem lu meññee ci seen suuf, yaa koy moom, te képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk.
14Mboolem lees aayalal Aji Sax ji ci Israyil, yaa koy moom.
15Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu.
16Njotu xale bu am lu dale ci weer, àpp ko ci juróomi siikali xaalis yu bérab bu sell bi, benn siikal yemook ñaar fukki gera mbaa fukki garaam.
17Waaye lu nag taawloo, ak lu xar taawloo, ak lu bëy taawloo, deesu ko jot. Yooyii yu sell la. Deretam ngay xëpp ci sarxalukaay bi, nebbon bi, nga def ko saxar, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Read Màndiŋ ma 18Màndiŋ ma 18
Compare Màndiŋ ma 18:1-17Màndiŋ ma 18:1-17