5Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.
6Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp,
7te ngeen def ciy xal, def ci cuuraay fi kanam Aji Sax ji, ëllëg. Su ko defee ku Aji Sax ji taamu, kookooy ki sell. Doy na sëkk, yeen Leween ñi!»
8Musaa teg ca ne Kore: «Yeen Leween ñi, dégluleen nag!
9Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla?
10Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci!
11Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»
12Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul!
13Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci?
14Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!»
15Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.»
16Musaa nag ne Kore: «Yaw, yaak sa gàngoor gépp, ca kanam Aji Sax ji, yaak ñoom ak Aaróona, ëllëg.