3bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:
4«Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale saraxu pepp bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar ak genn-wàll,
5ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñeenteelu xaajub xiin, di liitar ak genn-wàll, mu ànd ak saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, su dee xar mu ndaw.