Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 13

Màndiŋ ma 13:20-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat.
22Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.
23Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg.
24Bérab boobu lañu dippee xuru Eskol, (mu firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israyil dagge woon.
25Ndaw ya nag ñibbsi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan.
26Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.
27Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.
28Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis.
29Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
30Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»

Read Màndiŋ ma 13Màndiŋ ma 13
Compare Màndiŋ ma 13:20-30Màndiŋ ma 13:20-30