13Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”?
14Manumaa boot mii mbooloo mépp, man doŋŋ, ndax àttanuma ko.
15Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»
16Ba mu ko defee Aji Sax ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw.
17Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.
18«Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk.