Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 8

Luug 8:15-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.
16«Deesul taal ab làmp, dëppe ko ndab, mbaa nga dugal ko ci ron lal. Dees koy aj kay ba kuy duggsi, di gis leer gi.
17Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ.
18Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
19Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare.
20Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk a ngi taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
22Benn bés la Yeesu duggoon gaal, mook ay taalibeem. Mu ne leen: «Nanu jàll ca wàllaa dex gi.» Ñu daldi dem.
23Naka lañuy dem nag, Yeesu nelaw. Ngelaw lu réy dal ca kaw dex ga, gaal gi fees ak ndox, ba ñu nara sànku.
24Taalibe yi yee Yeesu, ne ko: «Njaatige, njaatige, nu ngi sànku!» Mu yewwu, gëdd ngelaw li ak gannax yu réy yi. Lépp dal, ne tekk.
25Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?»
26Ci kaw loolu ñu tëmb ba teereji ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27Ba Yeesu wàccee ca tefes ga, jenn waayu dëkk ba dikk dajeek moom. Waa ja, ay rab a ko jàpp. Yàgg naa def yaramu neen te dëkkul ci kër, xanaa sëg ya.
28Ba mu gisee Yeesu, daa yuuxu, daanu fa kanamam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay tinu, bu ma mbugal!»
29Booba Yeesu tàmbali naa sant rab wi, mu génn waa ji. Rab wi jàpp na waa ji ay yooni yoon. Su ko defee ñu yeewe ko ay càllala, jéng ko, ngir wattu ko, mu di ko dagg, rab wi di ko xabtal, jëme bérab yu wéet.
30Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal.» Ndax rab yu baree duggoon waa ji.
31Rab yi nag tinu Yeesu, ngir mu bañ leena yebal ca xóote ba.
32Ag coggalu mbaam-xuux yu baree nga woon foofa, di fore ca tund wa. Rab ya tinu Yeesu, ne mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33Rab ya nag génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab.
34Sàmm ya gis la xew, daldi daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya.
35Nit ña riire ca, di seet la xew. Naka lañu dikk ba ci Yeesu, yem ci nit ki rab wi teqlikool, mu ànd ak sagoom, solu, toog ca wetu Yeesu. Ñu daldi tiit.

Read Luug 8Luug 8
Compare Luug 8:15-35Luug 8:15-35