Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 7

Luug 7:6-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
7Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér.
8Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.»
10Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
11La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»

Read Luug 7Luug 7
Compare Luug 7:6-19Luug 7:6-19