6 Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
7 Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér.
8 Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.»
10 Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14 Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18 Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»