27«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32«Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.