27 «Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28 Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29 Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30 Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31 Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32 «Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.