Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 24

Luug 24:13-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak Yerusalem wara tollu ci fukki kilomeetar.
14Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu.
15Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
16Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi.
17Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.
18Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?»
19Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.
20Waaye sunu sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko teg ciy loxo, ngir ñu teg ko àtteb dee, daaj ko ci bant.
21Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey.
22Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca bàmmeel ba,
23waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund.
24Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.»
25Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!
26Xanaa du fàww Almasi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?»
27Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.

Read Luug 24Luug 24
Compare Luug 24:13-30Luug 24:13-30