Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 1

Kàdduy Waare 1:2-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.
3Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir ak a wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.

Read Kàdduy Waare 1Kàdduy Waare 1
Compare Kàdduy Waare 1:2-6Kàdduy Waare 1:2-6