Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 8

Jëf ya 8:2-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ay nit ñu ragal Yàlla nag rob Eccen, ñaawlu deeyam lool.
3Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.
4Gëmkat ña tasaaroo di xamle fépp fu ñu jaare, xibaaru jàmm bu kàddu gi.
5Noonu la Filib deme péeyub Samari, di siiwtaane Almasi.
6Ba waa dëkk ba déggee mbaa ñu gis kéemaan ya muy def, ñoo bokk teewlu ay waxam.
7Ndax bare na ca ñu rab yu bon jàppoon te mujj bàyyi leen, génne yuux yu réy; bare na ca it ñu lafañ ak ñu làggi woon te mujj wér.
8Muy mbég mu réy nag ca dëkk boobee.
9Ku ñuy wax Simoŋ nag yàggoon na ca dëkk ba, di ñeengo. Ku waar waa Samari la woon, te doon tuddoo nit ku màgg.
10Ñépp, mag ak ndaw, teewlu ko, naan: «Kii mooy dooley Yàlla ci boppam. Moom lañuy wax “Màggle”.»
11La ñu ko teewloo woon moo di jëfi ñeengo ya mu leen yàgga yéeme.
12Waaye ba ñu gëmee Filib, ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
13Simoŋ ci boppam gëm, moom it, ñu sóob ko ci ndox. Simoŋ nag bàyyeetul Filib. Ba mu gisee firnde yaak kiraama yu mag yay am, moom moo yéemu.
14Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal.
15Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi.
16Ndax booba Noo gi wàccagul woon ci kenn ci ñoom, dees leena sóoboon rekk ci ndox ci turu Sang Yeesu.
17Ba loolu amee Piyeer ak Yowaan teg leen loxo, ñu jot Noo gu Sell gi.
18Simoŋ nag gis noonee mayug Noo, gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.
19Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.»
20Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
21Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
22Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol.
23Ndax gis naa ni nga sóoboo ci wextanu kañaan, keppu ci ndëngte.»
24Simoŋ ne leen: «Ñaanal-leen ma Boroom bi, yeen ci seen bopp, ngir li ngeen wax lépp, lenn bañ ma cee dab.»
25Gannaaw ba Piyeer ak Yowaan seedeelee kàddug Boroom bi, biral ko, Yerusalem lañu dellu, di xamle xibaaru jàmm bi ci ay dëkki Samari yu bare.
26Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.»
27Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.
28Naka la jaraaf ja màggalsi bay dellu Ecopi, toog ca watiiram, di jàngaale téereb Yonent Yàlla Esayi,
29Noowug Yàlla ne Filib: «Doxal, dab watiir bale.»
30Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg.
32Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral: «Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji; mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat, ubbiwul gémmiñam.

Read Jëf ya 8Jëf ya 8
Compare Jëf ya 8:2-32Jëf ya 8:2-32