3ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ.
4«Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.
5Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gëna diis ci sunu diine.
6Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam.
7Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.
8Lu tax seen xel dàq ne Yàlla dina dekkal ñi dee?
9«Man sax ci sama bopp defe woon naa ne war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
10Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci sarxalkat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoona bëgga rey, ànd naa ci.
11Daan naa wër jàngoo jàngu, di leen teg toskare te di leen jéema weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
12«Noonu am bés, may dem dëkku Damaas, yor sañ-sañ ak ndigalu sarxalkat yu mag ya.
13Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
14Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
15«Noonu ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
16Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man ak li ma lay feeñuji.