Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 26:3-16 in Wolof

Help us?

JËF YA 26:3-16 in Téereb Injiil

3 ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ.
4 «Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.
5 Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gëna diis ci sunu diine.
6 Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam.
7 Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.
8 Lu tax seen xel dàq ne Yàlla dina dekkal ñi dee?
9 «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
10 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci sarxalkat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoona bëgga rey, ànd naa ci.
11 Daan naa wër jàngoo jàngu, di leen teg toskare te di leen jéema weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
12 «Noonu am bés, may dem dëkku Damaas, yor sañ-sañ ak ndigalu sarxalkat yu mag ya.
13 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
14 Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
15 «Noonu ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
16 Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man ak li ma lay feeñuji.
JËF YA 26 in Téereb Injiil

Jëf ya 26:3-16 in Kàddug Yàlla gi

3 Rawatina ba ma xamee ne ku géeju nga ci aaday Yawut, ak werante yi ci seen wàllu yoon. Kon dama lay ñaan rekk, nga muñal ma, déglu ma.
4 «Mboolem fi ma jaare ci samag dund, dale ko ca samag ndaw, ca ndoorte la, ba ma nekkee ca sama biir xeet, ak ca Yerusalem, lépp, mboolem Yawut yi xam nañu ko.
5 Xam nañu ma bu yàgg, te su leen neexee ñu seede ne ngérum Farisen mi gëna diis ci sunu diine, ci laa masa bokk.
6 Sama taxawaayu tey ci ëttub àttekaay bii nag, mooy yaakaar ji ma am ci dige bi Yàlla digoon sunuy maam.
7 Te mooy dige bi fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di séentu mu sottil leen, ba tax guddi ak bëccëg ñu xér ci jaamu Yàlla. Yaakaar jooju nag, Buur, moo tax Yawut yi tuumaal ma!
8 Ana lu leen taxa jàpp ci seen biir ne xel nanguwul Yàlla di dekkal ñi dee?
9 «Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.
10 Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.
11 Jàngoo jàngu laa leen daan tege mbugal ay yooni yoon, ngir xàccloo leen. Maa daan sànju ba xaabaabal ci seen kaw, topp leen ba ci biir dëkki jaambur yi.
12 «Yoon wu mel noonu laa doon dox, jëm Damaas, ci ndigalal ak ndénkaanel sarxalkat yu mag yi.
13 Ba ma demee ba wetu digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.
14 Nu ne dàll fi suuf. Ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut, ne ma: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal? Dangay sonal sa bopp rekk, mbete fas wu manula woŋŋeetu ba wéq dëgël bu koy jam.”
15 «Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
16 Jógal taxaw nag. Dama laa feeñu ngir def la ngay sama surga, ngir nga di ma seedeel peeñum tey, ak peeñu yi ma lay feeñooji ëllëg.
Jëf ya 26 in Kàddug Yàlla gi