23Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.
24Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
25mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.»