Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 1:23-25 in Wolof

Help us?

JËF YA 1:23-25 in Téereb Injiil

23 Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.
24 Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
25 mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.»
JËF YA 1 in Téereb Injiil

Jëf ya 1:23-25 in Kàddug Yàlla gi

23 Ci kaw loolu ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas, te ñu di ko wax Yustus itam, ak Maccas.
24 Ñu daldi ñaan ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
25 mu jël wàllam ci liggéey bi, te muy céru ndaw bii Yuda wacc, ba fekki wàll wa mu yelloo.»
Jëf ya 1 in Kàddug Yàlla gi