Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 19

Jëf ya 19:11-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Ba mu ko defee Yàlla di def ay kéemaan yu mag yu mu sottale loxoy Póol.
12Mujj na sax ñuy yóbbul jarag yi ay kaala aki taraxlaay yu laaloon yaramu Póol, ba lu leen daloon teqlikook ñoom, rab wu leen jàppoon, ba leen.
13Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»
14Ña doon def jëf jooju ñooy juróom ñaari doom yu góor yu Sewa, sarxalkatub Yawut bu mag.
15Loolu lañu doon jéem bés, rab wu bon wa ne leen: «Yeesu déy, xam naa ko. Póol it xam naa ko. Waaye yeen, yeenay ñan?»
16Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, teg leen loxo ñoom ñépp, pamti-pamtee leen, gaañ leen, ba ñu dawe kër ga yaramu neen.
17Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.
18Ba mu ko defee ñu bare ca gëmkat ña dikk, biral seenug tooñ, daldi xamle yu bon ya ñu daan jëfe.
19Ci biir loolu ñu bare ñu daan ñeengo, boole seeni téere, indi, lakk ko fa kanam ñépp. Ba ñu xaymaa njég la, tolloo naak juróom fukki junniy poseti daraxma (50 000).
20Noonu la kàddu gi lawe ba féete kaw ci kàttanu Boroom bi.
21Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»
22Mu daldi yebal fa Maseduwan, ñaari jaraafam, Timote ak Eràst, moom mu toogaat ab diir ca Asi.
23Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.
24Ku ñuy wax Demetirus, ab tëggu xaalis, moo daan defar jëmmi jaamookaay yu ndaw yu tuur mi ñu dippee Artemis, muy njariñ lu réy ci liggéeykat yiy nawleem.
25Mu woo leen, ñook ña farewoo liggéey yu ni mel, ne leen: «Bokk yi, xam ngeen ne liggéey bii, ci la sunu teraanga nekk.
26Yeena gis nag mbaa ngeen déggal seen bopp ni Póol moomu di naxee ba fàbbi mbooloo mu bare, te du ci Efes gii rekk, daanaka Asi gépp la: Mu naay: “Yàlla yu loxol nit sàkk du yàlla.”
27Loolu, jéllale naa ni mu mana gàkkale sunu liggéey bii, waaye dina tax ñu teddadil jaamookaayu Artemis, yàlla ju jigéen ju mag ji, ba darajaam mujj neen, moom mi mboolem Asi ak àddina sax di jaamu.»
28Mbooloo ma dégg kàddu yooyu, daldi mer lool, di xaacu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
29Ci kaw loolu dëkk bépp ne kër-kër, ne këpp. Ñu jàpp Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan ya àndoon ak Póol ca tukki ba. Ñu daldi riirandoo wuti ëttu joŋantekaay ba.
30Póol nag bëgga teewi ca kanam mbooloo ma, taalibe ya bañ.
31Ñenn ñay ay soppeem ca kàngami nguur ga sax, yónnee nañu ca moom, di ko àrtu ngir mu baña foye bakkanam, di dem ca ëttu joŋantekaay ba.
32Ndaje maa nga rëb lool, ñii xaacu ne lii, ñee xaacu, ne lee, te ña ca ëpp sax xamuñu lu waral ndaje ma.
33Ci kaw loolu mbooloo ma am lu ñu digal ku ñuy wax Alegsàndar, Yawut ya jañax ko ca kanam, mu daldi tàllal loxoom, ngir layool boppam ca digg mbooloo ma.
34Naka lañu xam ne ab Yawut la, kàddu ga di benn, jibe ca mbooloo mépp, diiru ñaari waxtu. Ñu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35Ndawal buur la nag mujj giifal mbooloo ma, ne leen: «Yeen waa Efes, ana moos ku xamul ne Efes gii mooy dëkk biy wattukatub jaamookaayu Artemis, ak jëmmam ji wàcce asamaan?
36Loolu maneesu koo weddi. Kon nag, dangeena wara teey, baña sañaxuy def lenn.
37Ndax nit ñii ngeen fi indi, teddadiluñu ay jaamookaay te waxuñu lu ñàkke sunu yàlla kersa.
38Su dee Demetirus ak liggéeykat yi ànd ak moom ñoo jote ak kenn ci ñoom, ay ëtti layoo am na fi, ay kàngam a ngi fi di àtte. Nañu fa layooji.
39Su dee leneen lu ngeen di sàkku nag, ca ndajem àtte ba lees koy lijjantee.
40Ndax kat repp nanu ñu jiiñ nu ag fippu, te amul lenn lu nu mana lay, ba lewal mii ndaje.» Naka la wax loolu, daldi tas mbooloo ma.

Read Jëf ya 19Jëf ya 19
Compare Jëf ya 19:11-40Jëf ya 19:11-40