11Léegi nag loxol Boroom baa ngii fi sa kaw; dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa gis-gis bu naqari akug lëndëm ne milib ci kawam, muy wëndeelu, di wut ku ko wommat.
12Ba loolu amee boroom dëkk ba gis la xew, daldi gëm, di yéemu ci li mu jànge ci Sang bi.
13Póol ak ñi mu àndal nag bàyyikoo Pafos, dugg gaal, jëm Perge, ca diiwaanu Pamfili. Yowaan moom tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
14Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
15Gannaaw ba tarib dog ya ca téereb yoonu Musaa, ak téereb yonent ya sottee, njiiti jàngu ba yóbbante leen kàddu, ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee kàddu gu ngeen ñaaxe mbooloo mi, waxleen.»
16Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
17Yàllay bànni Israyil jii moo tànnoon sunuy maam, moo yaatal xeet wi, ba ñuy ganeyaan ca Misra; moo leen fa génnee kàttanu loxoom.
18Lu tollook ñeent fukki at la leen muñal ca màndiŋ ma.
19Moo faagaagal juróom ñaari xeet ca réewum Kanaan, daldi muurale sunuy maam réewum Kanaaneen ña.
20Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel.
21Ba loolu wéyee, ñuy sàkku buur, Yàlla jox leen doomu Kis, Sóol, mi soqikoo ci giirug Beñamin, mu falu diiru ñeent fukki at.
22Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese, ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”
23«Ci askanu kookii la Yàlla indee Yeesu, na mu ko digee woon, muy Musalkat ñeel Israyil.
24Laata muy ñëw, Yaxya moo doon yéene ngir waa bànni Israyil gépp sóobu cim ndox, jëmmale ko seenug tuubeel.
25Ba Yaxya di jeexal aw sasam la ne: “Ana ku ngeen foog ne moom laa? Duma ki ngeen foog, waaye am na kuy ñëw nii sama gannaaw, ku ma yeyoowula summil sax ay dàllam.”
26«Bokk yi, yeen askanu Ibraayma, yeen ak jaamburi ragalkati Yàlla yi ci seen biir, nun lañu yónnee kàddug mucc gii.
27Waa Yerusalem, ak seeni kilifa nag xàmmiwuñu woon Yeesu, te ba ñu daanee Yeesu lañu sottal waxu yonent, ya ñu daan biral bésub Noflaay bu nekk.
28Gisuñu ci moom lenn lu ko àtteb dee dabe, te teewul ñu sàkku Pilaat reylu ko.
29Gannaaw ba ñu matalee mboolem lu ñu bind ci moom, lañu ko wàccee ca bant ba, dugal ko bàmmeel.
30Waaye Yàllaa ko dekkal,
31te diiru fan yu bare la feeñu ña àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem, te ñooñooy ay seedeem tey ci askan wi.
32Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,
33nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Sabóor, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.”
34Noonu ko Yàlla dekkale ndekkite lu dee toppatul, te yaramam du yàqu mukk, noonee la ko Yàlla waxe woon, ne: “Maa lay jox barkey Daawuda yu sell yi te wóor.”
35Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa ku Sell ki, mu yàqu.”
36Daawuda moom, gannaaw ba mu defee coobarey Yàlla ci jamonoom, nelaw na, ba ñu rob ko ca weti maamam ya, te yàqu na.
37Waaye moom mi Yàlla dekkal, yàquwul.
38«Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
39képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
40Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:
41“Yeen xeebaatekat yi, xool-leen, jommileen te ne mes, ndax jëf ji may def ci seen jamono, ku leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.”»
42Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.