Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 10

JËF YA 10:38-42

Help us?
Click on verse(s) to share them!
38Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.
39«Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.
40Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,
41waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.
42Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.

Read JËF YA 10JËF YA 10
Compare JËF YA 10:38-42JËF YA 10:38-42