21Gannaaw ba ñu demee, Ayimaas ak Yonatan yéeg, génn teen ba, dem nag àrtuji Buur Daawuda. Ñu ne ko Ayitofel digle na nàngam ak nàngam ci moom, neeti ko: «Gaawleen jàll dex gi léegi.»
22Ca saa sa Daawudaaki nitam ñépp jàll dexu Yurdan ga. Ba jant bay fenk, kenn sax desul ku jàllul dex ga.
23Ci biir loolu Ayitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi topptoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam.