Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - 1 YOWAANA - 1 YOWAANA 3

1 YOWAANA 3:11-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Ndaxte xibaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante,
12te baña mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
13Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
14Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk, moo nuy xamal ne jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
15Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
16Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
17Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?

Read 1 YOWAANA 31 YOWAANA 3
Compare 1 YOWAANA 3:11-171 YOWAANA 3:11-17