Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - 1 YOWAANA

1 YOWAANA 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur.
2Xam nanu ne bëgg nanu doomi Yàlla yi ci lii: bëgg Yàlla tey sàmm ay ndigalam.
3Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu.
4Ndaxte képp ku juddu ci Yàlla day not àddina; te li nuy note àddina mooy sunu ngëm.
5Ku not àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne Yeesu mooy Doomu Yàlla.
6Yeesu Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg.
7Ndaxte am na ñetti seede:
8Xel mi, ndox ak deret, te ñoom ñett ñépp, ñoo bokk benn baat.
9Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gëna wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam.
10Ku gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam.
11Te seede si mooy lii: Yàlla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam.
12Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Yàlla, amuloo dund.
13Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne am ngeen dund gu dul jeex.
14Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii: su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul.
15Gannaaw xam nañu ne dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne li nu ko ñaan, jox na nu ko.
16Ku gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko.
17Gépp jubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu jarul dee.
18Xam nanu ne képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara.

19Nun nag xam nanu ne nu ngi ci Yàlla, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis.
20Xam nanu ne Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu mana xam Aji Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex.
21Samay doom, wottuleen seen bopp ciy xërëm.