Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Korent - 1.Korent 7

1.Korent 7:12-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Ñi ci des nag, li ma xalaat te du Boroom bee ko wax, maa ko waxal sama bopp, moo di: ab gëmkatub Almasi, bu amee jabar ju gëmul, te teewul mu nangu koo séyal ba tey, bumu ko fase.
13Ab gëmkatub Almasi it, bu amee jëkkër ju gëmul, te teewul mu nangoo nekk ak moom, bumu tas.
14Ndaxte jëkkër ji gëmul day daldi séddu sellnga ndax jabaram ja dib gëmkat, te jigéen ji gëmul it day séddu sellnga ca jëkkëram jay gëmkat. Su dul woon noonu doom yu ngeen ca am di ñu sobewu, te bir na ne doom yu ngeen ca am, ñu sell lañuy doon.
15Ndegam nag ki gëmul daa bëgga dem, na dem. Su demee noonu, mbokkum gëmkat bu góor bi, mbaa ku jigéen ki amatul benn gàllankoor, waaye ci jàmm la leen Yàlla woo.
16Yaw miy jabar ji nag sa texey jëkkër man naa jaare ci yaw, jombul; yaw jëkkër ji it, sa texey jabar jaare ci yaw, jombul.
17Lu ko moy nag, ku ci nekk, cér ba la Boroom bi séddoon, noonee nga nekke woon ba la Yàlla di woo, nanga ko wéye. Loolu laa santaane ci mboolooy gëmkat ñépp.
18Ki xarafoon bala ñu koy woo, bumu làq màndargam xaraf ma. Ki xaraful woon ba ñu koy woo, bumu xaraf.
19Xaraf amul solo, ñàkka xaraf amul solo. Li am solo moo di topp ndigali Yàlla.
20Ku nekk, nekkin wi nga nekke woon ba ñu lay woo, nanga ko wéye.
21Ndax ab jaam nga woon, ba ñu lay woo? Amul solo. Waaye soo manee yiwiku, yiwikul.

Read 1.Korent 71.Korent 7
Compare 1.Korent 7:12-211.Korent 7:12-21