3Ba magi Israyil ñépp dikkee, sarxalkat ya yékkati gaal ga.
4Ñu boole gaalu Aji Sax ja, ak xaymab ndaje ma, ak mboolem jumtukaay yu sell ya ca biir xayma ba. Sarxalkat ya ak Leween ña daldi gàddu lépp.
5Buur Suleymaan ak mbooloom Israyil ma daje fa moom, ñoom ñépp a nga bokk ak moom, teew. Ñu jàkkaarlook gaal ga, di rendi ay gàtt aki nag yu kenn manula lim mbaa di ko waññ, ndax bare.
6Gannaaw loolu sarxalkat ya yóbbu gaalu Aji Sax ja ca bérabam, ca biir néeg bu sell baa sell, ca ron laafi malaakay serub ya.
7Ndaxte jëmmi serub ya, seeni laaf daa tàllalu, tiim bérabu gaal ga, laaf ya yiir kaw gaal ga aki njàppoom.
8Njàppu ya daa guddoon, ba nit mana séen cat ya te fekk ko tollu ca bérab bu sell ba, ca kanam néeg bu sell baa sell. Waaye maneesula tollu ca biti di séen cat ya. Njàppu yaa nga fa ba tey jii.
9Dara nekkuloon ca biir gaal ga, lu moy ñaari àlluway doj ya ca Musaa yeboon ca tundu Oreb, fa Aji Sax ji fase woon kóllëre ak bànni Israyil, ba ñu génnee réewum Misra.
10Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja,
11ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga.
12Ba mu ko defee Suleymaan ne: «Aji Sax ji moo noon lëndëm gu fatt lay màkkaanoo.»
13Mu ne Aji Sax ji: «Tabaxal naa la kër gu màgg, màkkaan mooy dëkke ba fàww.»
14Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israyil mépp, fekk mbooloom Israyil mépp a nga taxaw.
15Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, moom mi sottale loxol boppam, la mu waxoon Daawuda sama baay ci gémmiñam, ne ko:
16“La dale bés ba ma génnee bànni Israyil, sama ñoñ ca Misra ba tey, taamuwuma benn dëkk, ci mboolem giiri Israyil, bu ñuy tabax kër, gu sama tur di nekk. Waaye maa taamu Daawuda, ngir mu falu ci kaw Israyil sama ñoñ.”