Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 8:3-16 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 8:3-16 in Kàddug Yàlla gi

3 Ba magi Israyil ñépp dikkee, sarxalkat ya yékkati gaal ga.
4 Ñu boole gaalu Aji Sax ja, ak xaymab ndaje ma, ak mboolem jumtukaay yu sell ya ca biir xayma ba. Sarxalkat ya ak Leween ña daldi gàddu lépp.
5 Buur Suleymaan ak mbooloom Israyil ma daje fa moom, ñoom ñépp a nga bokk ak moom, teew. Ñu jàkkaarlook gaal ga, di rendi ay gàtt aki nag yu kenn manula lim mbaa di ko waññ, ndax bare.
6 Gannaaw loolu sarxalkat ya yóbbu gaalu Aji Sax ja ca bérabam, ca biir néeg bu sell baa sell, ca ron laafi malaakay serub ya.
7 Ndaxte jëmmi serub ya, seeni laaf daa tàllalu, tiim bérabu gaal ga, laaf ya yiir kaw gaal ga aki njàppoom.
8 Njàppu ya daa guddoon, ba nit mana séen cat ya te fekk ko tollu ca bérab bu sell ba, ca kanam néeg bu sell baa sell. Waaye maneesula tollu ca biti di séen cat ya. Njàppu yaa nga fa ba tey jii.
9 Dara nekkuloon ca biir gaal ga, lu moy ñaari àlluway doj ya ca Musaa yeboon ca tundu Oreb, fa Aji Sax ji fase woon kóllëre ak bànni Israyil, ba ñu génnee réewum Misra.
10 Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja,
11 ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga.
12 Ba mu ko defee Suleymaan ne: «Aji Sax ji moo noon lëndëm gu fatt lay màkkaanoo.»
13 Mu ne Aji Sax ji: «Tabaxal naa la kër gu màgg, màkkaan mooy dëkke ba fàww.»
14 Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israyil mépp, fekk mbooloom Israyil mépp a nga taxaw.
15 Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, moom mi sottale loxol boppam, la mu waxoon Daawuda sama baay ci gémmiñam, ne ko:
16 “La dale bés ba ma génnee bànni Israyil, sama ñoñ ca Misra ba tey, taamuwuma benn dëkk, ci mboolem giiri Israyil, bu ñuy tabax kër, gu sama tur di nekk. Waaye maa taamu Daawuda, ngir mu falu ci kaw Israyil sama ñoñ.”
1.Buur ya 8 in Kàddug Yàlla gi