Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 8

1.Buur ya 8:19-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Waaye du yaw yaay tabax kër gi; sa doom ju góor ju soqikoo ci sa geño, moom mooy tabax kër gi, tudde ma ko.”
20«Aji Sax ji moo sottal waxam ja mu waxoon. Wuutu naa sama baay Daawuda, toog naa ci jalub Israyil, noonee ko Aji Sax ji waxe woon. Tabax naa kër gi, tudde ko Aji Sax ji, Yàllay Israyil.
21Te it sàkk naa fa bérab bu ñeel gaal gi def àlluway kóllërey Aji Sax, ji mu fasoon ak sunuy maam, ba mu leen génnee réewum Misra.»
22Gannaaw loolu Suleymaan taxaw jàkkaarlook sarxalukaayu Aji Sax ji, fa kanam mbooloom Israyil mépp. Mu daldi tàllal ay loxoom asamaan,
23daldi ne: «Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, amul jenn yàlla ju mel ni yaw fa kaw asamaan mbaa ci kaw suuf si mu tiim, yaw miy sàmm kóllëre ak ngor, ñeel sa jaam ñiy doxe seen léppi xol, fi sa kanam.
24Yaa sàmm kàddu ga nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ci sa gémmiñu bopp, te yaa sottale sab loxo, sa kàddu bés niki tey.
25«Léegi nag Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ngalla sàmmal li nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ne ko: “Deesu la xañ mukk ci saw askan ku góor kuy tooge jalub Israyil fi sama kanam, ndegam saw askan a ngi moytu seenu yoon, tey doxe fi sama kanam noonee nga daan doxe fi sama kanam.”
26Kon nag yaw Yàllay Israyil, ngalla saxalal wax jooju nga waxoon Daawuda, sa jaam ba.
27«Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan yi ba ca asamaani asamaan ya manu laa fat, waxumalaa kër sii ma tabax.

Read 1.Buur ya 81.Buur ya 8
Compare 1.Buur ya 8:19-271.Buur ya 8:19-27