Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 7

1.Buur ya 7:9-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yett la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci kenu gi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi.
10Ñu defare kenu yi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab.
11Xeer yi tege ci kenu gi, xeeri tànnéef la yu ñu yett, natt ko, yemale, booleek banti seedar.
12Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër Aji Sax ja ak dëru buntu kër ga.
13Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Uram.
14Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.
15Mu móol ñaari xeri xànjar, wu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub.
16Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab.
17Bopp yi ci kaw xer yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar.

Read 1.Buur ya 71.Buur ya 7
Compare 1.Buur ya 7:9-171.Buur ya 7:9-17