Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 7

1.Buur ya 7:27-42

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Mu daldi sàkk fukki watiiri rootukaayi xànjar, wu ci nekk am guddaayu ñeenti xasab, yaatuwaayam di ñeenti xasab, taxawaayam di ñetti xasab.
28Ni ñu defare rootukaay yi nii la: ay wetam lañu defare làcci xànjar, lëkklee làcc yi ay laat.
29Muy làcc yu Uram yett ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay serub. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yett ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi.
30Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkklee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor.
31Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yett ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar te yem kepp.
32Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll.
33Mbege yi bindoo ni mbegey watiiri xare. Tóor yeek mbege yi ak sidditi mbege yi ak ŋanku yi, xànjar lañu ko xellee.
34Ñeenti kenu yi ci ñeenti koñi rootukaay bi, bu ci nekk dees koo xelleendook weti rootukaay yi, ba lépp di benn.
35Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn.
36Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor.
37Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind.
38Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook juróomi barigo; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj.
39Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam jàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku.
40Iram sàkk itam ndab yu ndaw yi ak ñiitukaay yi ak këlli tuurukaay yi. Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Aji Sax ji:
41muy ñaari jën yi, ak ñaari gamb yiy boppi jën yi, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi,
42ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yiy boppi xer yi;

Read 1.Buur ya 71.Buur ya 7
Compare 1.Buur ya 7:27-421.Buur ya 7:27-42