52Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax doo ñam dee.”
53Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne yaa ko gëna màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?»