Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 7:3-27 in Wolof

Help us?

YOWAANA 7:3-27 in Téereb Injiil

3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4 Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6 Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
8 Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga.
15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16 Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
20 Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?»
21 Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi.
23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey?
26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
YOWAANA 7 in Téereb Injiil