18Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wuta rey, ndaxte yemul woon rekk ci baña topp ndigalu bésub noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
19Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji manula def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
20Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru.
21Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgga jox.
22Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji,
23ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni.
24«Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund.
25Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund.
26Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.
27Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki.
28«Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn.