Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 20

YOWAANA 20:1-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bés ba jiitu ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Bi mu agsee, mu gis ne dindi nañu xeer, wa ñu ko ube woon.
2Mu daw, dem ca Simoŋ Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu bëggoon, ne leen: «Jële nañu néewu Boroom ba ca bàmmeel ba, te xamunu fu ñu ko yóbbu.»
3Piyeer ak beneen taalibe ba daw, dem ca bàmmeel ba.
4Ñoom ñaar ñépp a ngi doon daw, waaye beneen taalibe ba raw Piyeer, jëkk ko ca bàmmeel ba.
5Duggul nag, dafa sëgg, yër, séen càngaay la ca suuf.
6Noonu Simoŋ Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu séen càngaay la ci suuf,
7ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la; dañu ko laxas, teg ko ci wet.
8Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm.

Read YOWAANA 20YOWAANA 20
Compare YOWAANA 20:1-8YOWAANA 20:1-8