21Noonu sarxalkat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: «Bul bind: “Buuru Yawut,” bindal rekk: “Kii moo ne mooy buuru Yawut yi.”»
22Pilaat ne leen: «Xas naa koo bind, du deñ.»
23Xarekat ya, bi ñu daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi dañoo jël ay yéreem, séddale ko ñeenti cér, ku nekk benn. Jël nañu it mbubbam bu ñu ràbb ca kaw ba ci suuf te amul benn ñaw.
24Xarekat ya di waxante naan: «Mbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom.» Noonu la Mbind mi waroona ame, bi mu naan: «Séddoo nañu samay yére, tegoo ay bant sama mbubb.» Loolu nag la xarekat ya def.
25Ca wetu bant, ba ñu daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jigéen, Maryaama soxnas Këlópas, ak Maryaama mi dëkk Magdala.
26Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,»
27neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko.
28Bi loolu wéyee, gannaaw Yeesu xam na ne lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.»
29Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu ñu jël sagar, tooyal ko ca, takk ko ci caru garab gu ñuy wax isob, teg ko ci gémmiñu Yeesu.
30Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla.
31Keroog ba ñu dee waajal bésub noflaay ba la woon, te Yawut ya bëgguñu néew ya des ca bant ya, ndaxte bésub noflaay boobu fonkoon nañu ko lool. Ñu ñaan Pilaat, mu dammlu tànki ña ñu daajoon, te jële leen fa.