10Aaróona jël nebbon bi jóge ci sarax biy póotum bàkkaar, aki dëmbéenam ak bàjjo bi ci res wi, mu boole ko lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
11Yàpp wi ak der bi, mu génne ko dal ba, lakk ko, ba mu dib dóom.
12La ca tegu Aaróona rendi juru rendi-dóomal bi. Ba loolu amee doomam yu góor ya jox ko deret ja, mu xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi.
13Ñu jox ko saraxu rendi-dóomal bi ñu def dog yu ànd ak bopp ba, mu boole lakk ca sarxalukaay ba.