Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 8

Sarxalkat yi 8:1-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
2«Indil Aaróona aki doomam yu góor te indaale yére yi ak diw gi ñuy fale ak yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar ak ñaari kuuy yi, boole ca pañeb mburu ya amul lawiir,
3te nga woo mbooloo mi mépp, ñu daje ci bunt xaymab ndaje mi.»
4Musaa def la ko Aji Sax ji sant, mbooloo ma daje ca bunt xaymab ndaje ma.
5Musaa wax mbooloo ma ne leen: «Lii may waaj la Aji Sax ji santaane woon ñu def ko.»
6Ci kaw loolu Musaa indi Aaróona aki doomam yu góor, ñu sangu,
7solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca xar-sànni ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam.
8Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba,
9la ca tegu mu tegal ko kaala ga ca bopp ba, takkal ko dogu wurus wu tell wa, mooy meeteel gu sell ga, mu nekk ca kaw kaala ga, féete kanam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
10Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,
11ba noppi wis-wisal ca juróom ñaari yoon ca kaw sarxalukaay ba, diwe ko sarxalukaay ba ak mboolem ay ndabam, boole ca mbalkam njàpp ma, mook ub tegoom ngir yooyu it sell.
12Mu sotti nag tuuti ci diw gi ñuy fale ci boppu Aaróona, diw ko, sellale ko ko.
13Ba mu ko defee Musaa indi doomi Aaróona yu góor ya, solal leen mbubb yu gudd, takkal leen ay laxasaay, solal leen mbaxana, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
14Musaa teg ca indi yëkku sarax siy póotum bàkkaar, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkku sarax siy póotum bàkkaar,
15Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi.
16Ba loolu amee mu jël nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi.
17Li des ci yëkk wi, di der beek yàpp week sébbriit mi, mu génne ko dal bi, lakk ko ca biti, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
18La ca tegu mu indi kuuyu saraxu rendi-dóomal bi, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ca boppu kuuy ma.
19Musaa rendi ko, xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi,
20daldi daggat kuuy mi, def ko ay dog, boole bopp beek dog yeek nebbon bi, lakk ko, ba mu dib dóom.

Read Sarxalkat yi 8Sarxalkat yi 8
Compare Sarxalkat yi 8:1-20Sarxalkat yi 8:1-20