Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 7

Sarxalkat yi 7:3-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Nebbon ji jépp lañuy sarxal: calgeen bi, nebbon bi sàng yérey biir yi,
4ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te ñu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
5Sarxalkat bi da koy boole lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, te di saraxu peyug tooñ.
6Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.
7«Li ci saraxu póotum bàkkaar moo nekk ci saraxu peyug tooñ, dogal bi di benn ci yooyu yaar: sarxalkat bi def gàtt bi njotlaay moo koy moom.
8Su nit joxee ab saraxu rendi-dóomal, sarxalkat bi mooy féetewoo deru jur gi mu sarxal.
9Ci biir loolu bépp saraxu pepp mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom.
10Waaye weneen xeetu saraxu pepp mu mu mana doon, su dee saraxu pepp mu ñuy xiiwaale diw mbaa muy mu wow, doomi Aaróona yu góor yépp a koy moom, ku nekk tollook sa moroom cér.
11«Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
12Bu ci nit ki jubloo ag njukkal gu muy delloo Aji Sax ji, day boole ci saraxu cant gi ay mburu yu ndaw yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw ak ay mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, ak ay mburu yu ñu lakke sunguf su mucc ayib, xiiwaale ko diw, not ko bu baax.
13Sarax boobu da ciy dolli mburu yu am lawiir, boole kook saraxu cant googu ci biir jàmm te mu jublu ci njukkal.
14Nañu jooxeel Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu sarxalkat bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Read Sarxalkat yi 7Sarxalkat yi 7
Compare Sarxalkat yi 7:3-14Sarxalkat yi 7:3-14