4Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe.
5Na sawaras sarxalukaay bi wéye tàkk te du fey. Suba su nekk na ko sarxalkat bi xamb, ba noppi teg ci saraxu rendi-dóomal bi, te na lakk nebboni saraxi cant gi ci biir jàmm.