6Su ko defee sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, fa janook ridob bérab bu sell ba.
7Na sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaayu cuuraay lu xeeñ la ca biir xaymab ndaje ma ca kanam Aji Sax ji. Li des ci deretu yëkk wi, na ko tuur ci taatu sarxalukaay bi ñuy lakk saraxu rendi-dóomal, foofa ca bunt xaymab ndaje ma.
8Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
9ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
10Mooy ni ñu koy génnee rekk ci yëkku saraxu cant ci biir jàmm. Sarxalkat bi da koy boole lakk ca kaw sarxalukaayu rendi-dóomal ba.