26Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
27«Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,
28bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe aw bëy wu jigéen wu amul sikk, ndax bàkkaar bi mu def.
29Day teg loxoom ci boppu gàttu sarax soosu di póotum bàkkaar, rendi ko fa ñuy lakk saraxu rendi-dóomal.
30Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi.
31Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def saraxu cant ci biir jàmm. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
32«Su fekkee ne am xar lay sarxe, muy saraxu póotum bàkkaaram, na doon xar mu jigéen, mu amul sikk.