15Magi mbooloo mi dañuy teg seeni loxo ci boppu yëkk wi, fi kanam Aji Sax ji, ba noppi ñu rendi yëkk wi fi kanam Aji Sax ji.
16Gannaaw loolu na sarxalkat bi ñu diw, fal ko, sàkk ci deretu yëkk wi, yóbbu ci biir xaymab ndaje mi.
17Na capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, foofu ci kanam rido bi.